Philippians 4:18 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Fi mu ne jot naa li ma aajowoo lépp, ba maa ngi ci naataange; li ngeen ma yónnee ci loxoy Epafrodit doy na sëkk; ni xetu latkoloñ la mel ci man, di sarax su neex Yàlla te mu nangu ko.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Fii ma tollu jot naa li ma aajowoo lépp, maa ngi ci naataange; doyle naa sëkk, gannaaw ba ma nangoo ci loxol Epafrodit, seenub yóbbante, te sarax su ñu nangu la, di xeeñ xetug jàmm, te neex Yàlla mi mu ñeel.