Revelation 1:5 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
tukkee it ci Yeesu Kirist, seede bu takku bi, moom taaw bi, maanaam ki jëkk a dekki, di buuru buur yi ci kaw suuf yépp. Na ndam ak nguur féete ak Yeesu Kirist ba fàww, moom mi nu bëgg te yiwi nu ci sunuy bàkkaar ak deretam ji tuuru, te def nu askanu saraxalekati Buur Yàlla Baayam, nu di ko jaamu. Amiin.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,