Revelation 14:10 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
dina naan moom itam biiñu xadarub Yàlla bi kenn raxul, ñu sotti ko ci koppu meram. Te dees na ko mbugal ci safara ak tamarax ci kanamu malaaka yu sell yi ak Mbote mi,
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi.