Revelation 15:3 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ñuy woy woyu Musaa jaamu Yàlla bi, ak woyu Mbote ma, naan:«Say jëf réy nañu te yéeme,yaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji.Say yoon jub nañu te dëggu,yaw Buur bi fiy sax ba abadan.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.