Revelation 17:8 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Rab wi nga gis nekkoon na waaye nekkatul. Dina génn ca kàmb gu xóot ga, ba noppi sànku. Noonu waa àddina, ñi ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bi, dinañu yéemu, bu ñu gisee rab wi, ndaxte nekkoon na waaye nekkatul te dina nekkaat.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Rab wi nga gis mas naa nekk waaye nekkatul. Dina génne ca xóote ba, waaye day sànkuji. Waa àddina, ñi ñu bindul woon seeni tur ci téereb dund bi ba àddinay door nag, bu ñu gisee rab wi, dinañu yéemu, ndax la mu masoona nekk, tey nekkatul, te ëllëg muy nekkaat.