Revelation 19:10 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu ma daanu ci ay tànkam, bëgg koo jaamu. Waaye mu ne ma: «Moytu koo def; sa nawle laa ci liggéey bi, di kenn ci say bokk, yiy sax ci seedeel Yeesu. Jaamul Yàlla. Ndaxte seedes Yeesu mooy xel miy solu yonent yi.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ma daldi ne gurub sukk ciy tànkam, ngir sujjóotal ko. Mu ne ma: «Déet, ëpp naa def. Sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokk yi jàppoo seedeel Yeesu. Sujjóotalal Yàlla. Ndaxte seedeel Yeesu moo di Noo giy dundal waxyu.»