Revelation 2:24 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye yéen ñépp ñi des ci Catir te toppuleen njàngale moomu te gëstuwuleen loolu ñu naan mbiri Seytaane yu xóot yi, maa ngi leen di wax ne, duma leen yen beneen yen
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
«Waaye yeen ñi ci des ñépp nag, yeen waa Catir ñi toppul moomu njàngle te jotuleena xam loolu ñu naan xóotey xam-xamu Seytaane, maa ne leen, duma leen sëf beneen sëf.