Revelation 4:8 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ñeenti mbindeef ya am nañu ku nekk juróom-benni laaf te ñu nga fees ak ay bët li leen wër lépp, ba ci seen roni laaf. Guddi ak bëccëg duñu noppeek naan:«Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,moo sell, sell, sell,moom ki nekkoon démb,ki nekk tey, te di ñëw ëllëg.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñeenti bindeef yi am nañu ku nekk juróom benni laaf, fees aki bët ba daj, biir ak biti, te guddi ak bëccëg duñu selaw, xanaa naan: «Kee sell, Kee sell, Kee sell, Keey Boroom bi Yàlla Aji Man ji, Kee masa Nekk, Kee Nekk, Keey Dikk.»