Revelation 5:13 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ma dégg itam mbindeef, yi nekk ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf, ci géej gi, — mbindeef yépp naan:«Na cant, teraanga, ndam ak nguurféete ak ki toog ci gàngune mi,ak Mbote mi ba fàww.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ba loolu amee mboolem dundooti asamaan, ak kaw suuf, ak biir suuf, ak géej, ak mboolem li ci seen biir, ñoom ñépp di wax, may dégg, naan: «Ki toog ci ngàngune mi ak Gàtt bi, nañu jagoo cant ak teraanga, ak darajaak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww.»