Revelation 6:8 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ma xool noonu, gis fas wu wert, gawar baa nga tuddoon Dee te barsàq a nga toppoon ci moom. Ñu jox ko sañ-sañ ci ñeenteelu xaaju àddina sépp, ngir mu faat ak jaasi, xiif, mbas ak rabi àll yi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ma xool rekk, gis fas wu gel, turu gawaram di Dee, njaniiw topp ci moom. Ñu jox ko sañ-sañ ci ñeenteelu xaaju àddina, ngir muy bóome saamar akub xiif, di bóome mbas ak ay rabi àll.