Revelation 8:13 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ma xool noonu, dégg jaxaay juy naaw ci digg asamaan, naan ak baat bu xumb: «Musiba, musiba! Musibaa ngi ci kaw waa àddina, ndax liit yi yeneen ñetti malaaka yi di wol.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ma xoolaat, daldi dégg jenn jaxaay ju naawe digg asamaan. Mu àddu ca kaw ne: «Wóoy, wóoy, wóoy, musibay waa àddina yiy sababoo ci yeneen baati liit yi ñetti malaaka yi ci des, di waaja liit.»