Revelation 9:20 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Nit ñi rëcc ci musiba yooyu taxul sax ñu tuub seeni jëfi loxo. Noppiwuñu di jaamu rab yi ak nataali xërëm yu ñu defare wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk, yoo xam ne mënuñoo gis, mënuñoo dégg mbaa ñu dox.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndesu nit ñi musiba yooyii reyul nag, taxul sax ñu tuub seeni jëf, ba bañatee jaamu ay tuur, ak jëmmi xërëmi wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk; xërëm yu gisul, déggul, doxul.