Revelation 9:5 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Santuñu leen ñu rey leen, waaye ñu metital leen diirub juróomi weer. Te metit woowu ñuy indi, temboo na ak metit wiy dal nit, bu ko jànkalaar fittee.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
May nañu leen ñu mitital leen diiru juróomi weer, te bañ leena rey, xanaa mitital leen lu tembook mititu fittu jànkalaar.