Romans 1:20 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte ba àddina sosoo ba tey, mbiri Yàlla yu nëbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, feeñ nañu bu leer, te bir ñépp ci yi mu sàkk, ba tax bunti lay yépp tëj nañu.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.