Romans 1:21 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte bi ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ni mu ware, mbaa ñu sant ko. Waaye ñu daldi réer ci seen biiri xalaat yu mujjul fenn, ba tax seen xol gumba, ba lëndëm këruus.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.