Romans 10:19 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Aaŋkay! Musaa dafa jëkkoon a wax ne:«Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla,merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ma neeti: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Ahakay! Musaa moo leen jëkkoona jottli la Yàlla noon: «Yeen, maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara, ci waasow naataxuuna laa leen di merloo.»