Romans 11:24 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Yaw mi dul Yawut, yaa ngi bokkoon ci garabu oliw gu àll, waaye Yàlla daf la cee jële, ci lu dul faral a am, jabtal la ci garabu kër gi. Kon man nanoo gën a wóor ne, Yawut ya judduwaale nekk ci garabu oliw gu kër gi, Yàlla dina leen ci delloo.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat, ndegam yaw lañu tenqee ci oliwu àll gi, jabtal la ci oliwu kër gi dul sa ndey, astamaak car yi oliwu kër gi di seen ndey, nde saxalaat leen ca mooy gëna yombati.