Romans 11:25 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bokk yi, dama leen a bëgg a dindi kumpa ci lii, ngir ngeen bañ a yég seen bopp. Dërkiisu xol dab na bànni Israyil ab diir, ba bés ba mboolem waa àddina, ñu war a bokk ci nguuru Yàlla, dugg ca.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.