Romans 11:28 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Gannaaw bañ nañu xebaar bu baax bi, ay bañaaley Yàlla lañu, ngir ngeen jot barkeem. Waaye gannaaw Yàlla tànn na leen, dafa leen bëgg ba tey ndax seen maam ya.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.