Romans 13:3 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Kuy def lu baax warul a ragal njiit li, kuy def lu bon moo ko war a ragal. Soo ko bëggee bañ a ragal nag, kon defal lu baax, te dina la tagg.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kuy def lu baax nag, doo ragal kilifa yi, kiy def lu bon moo leen di ragal. Soo bëggee mucc ci ragal kilifa nag, defal lu baax, jot ngërëmam.