Romans 13:4 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndax Yàllaa ko dénk liggéey boobu ngir sa jàmm. Waaye sooy def lu bon, war ngaa ragal, ndax du cig neen la ame jaasiy àtte; jawriñu Yàlla la ngir wàcce meru Yàlla, ci fey ku def lu bon.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kilifa gi mooy ndaw li Yàlla yebal ngir sa jàmm. Waaye soo dee def lu bon, ragalal, ndax kilifa gi yorul ab saamar cig neen; mooy ndawal Yàlla liy añale, te mooy jottli am sànj mu wàccal kuy def lu bon.