Romans 13:9 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul rey nit, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu man a doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax ndigal yii kat: «Buleen jaaloo, buleen bóom, buleen sàcc, buleen xemmem,» ak leneen ndigal lu mu mana doon, ci genn kàddu gii la tënke: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom.»