Romans 14:17 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ndaxte bokk ci nguuru Yàlla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Yàlla mooy jub ci kanam Yàlla, te am mbég ak jàmm ci dooley Xel mu Sell mi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat solob nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solob nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm, ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.