Romans 15:16 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xebaaram bu baax bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.