Romans 15:27 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Yéene nañu ko, te it ci dëgg-dëgg bor la, bu ñu war a fey. Ndaxte gannaaw ñi gëm ci Yerusalem séddoo nañu ak ñi dul Yawut seen ngëm, kon xeet yooyu itam war nañoo séddoo ak ñoom seen alal.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Seen coobarey bopp lañu ko defe, waaye ñoo ko ameel waa Yerusalem it nag. Ndaxte gannaaw ñoom ñiy jaambur, gëmkati Yerusalem ñoo leen sédd ci xéewal yi leen ngëm may, kon ñoom jaambur ñi itam war nañu leena sédd ci seen alal.