Romans 15:30 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Gannaaw loolu bokk yi, maa ngi leen di ñaan ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist ak ci bëggante, gi Xelu Yàlla mi def ci nun, ngeen defal ma lii: àndleen ak man, nu tuur sunu ñaq ci ñaan Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gannaaw loolu bokk yi, li ma leen di ñaan ngir sunu Boroom Yeesu Almasi, ngir itam cofeel gi Noo gu Sell giy maye, moo di ngeen fekksi ma ci xareb ñaan ngir man.