Romans 2:15 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
di wone it ne, Yàlla bind na ci seen xol jëf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat ñoo leen di tuumaal, mbaa ñu leen di jéggal.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def leeg-leeg mu sikk leen, leeg-leeg mu dëggal leen.