Romans 4:13 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ak ñi naroon a soqikoo ci moom, ne dinañu moom àddina si. Te dige boobu jógewul ci yoonu Musaa, waaye dafa jóge ci njub, gi Ibraayma amoon ci kanam Yàlla ci kaw ngëmam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat digeb Ibraayma ba sédde Ibraayma àddina si, moom ak askanam, sàmm gu mu sàmm yoonu Musaa taxul, waaye àtteb njub bi mu jagoo ndax ngëmam, moo ko waral.