Romans 4:16 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Kon nag loolu Yàlla dige, ngëm rekk a koy indi, ngir mu sukkandikoo yiwu Yàlla rekk. Noonu la dige bi wóore ci ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, du ci ñi nekk ci yoonu Musaa rekk, waaye itam ñi gëm ni Ibraayma gëme woon. Kon Ibraayma mooy sunu baay, nun ñépp.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kon nag dige Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.