Romans 4:17 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Moom la Yàlla dogal, wax ko ci Mbind mi ne: «Def naa la baayu xeet yu bare.» Ndaxte Ibraayma gëmoon na Yàlla, miy dekkal ñi dee, tey wax ci lu amagul, mel ni dafa am.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa la def ngay maamu xeet yu bare.» Ibraayma mooy sunu maam fi kanam Ki mu gëm, te muy Yàlla miy delloo ñi dee, bakkan, tey woo lu nekkul, mu doon lu nekk.