Romans 4:19 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Mu xool yaramam, xam ne dee rekk a ko dese, ndax mi ngi tollu woon ci lu mat téeméeri at, waaye ba tey ngëmam wàññikuwul. Mu xam it ne, Saarata mënatul a ëmb.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ngëmu Ibraayma wàññikuwul, doonte ba mu xoolaatee boppam, xam na ne yaramam dee na daanaka, ndax fekk na ay atam xawa tollu ci téeméer, te njurukaayu Saarata it fekk na ko dee.