Romans 5:14 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Teewul nag la dale ca Aadama ba ca Musaa, dee a ngi fi woon ci àddina, di noot ñépp, ak sax ñi seen bàkkaar melul woon ni bosu Aadama, maanaam jàdd yoon. Aadama moomu nag moo di takkandeeru Kirist, mi waroon a ganesi àddina.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Teewul la dale ca Aadama ba ca Musaa, ci kaw àddina sépp la dee doon nguuru, ba ci kaw ñi bàkkaarul noonee Aadama xëtte woon ndigal. Aadama mooy takkndeeru ki doon dikk.