Romans 5:15 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye warunoo yemale tooñu Aadama ak mayu Yàlla. Bàkkaaru kenn nit kooku tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak may, gi nu keneen nit ka Yeesu Kirist yéwénal, baawaan na ci ñu bare, ba suul tooñ googu.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare?