Romans 5:16 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Te bàkkaaru Aadama niroowul ak mayu Yàlla. Aadama bàkkaar na benn yoon, ba tax Yàlla daan ko, daanaale ñépp; waaye Yàlla jéggale na tooñ yu bare ci dara, ba mu àtte ñu bare ni ñu jub.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ni njeexitalu tooñu kenn nit deme, laa ne, mayu Yàlla demewu ni. Benn bàkkaar moo waral àtte bi indi mbugal. Waaye moy yu bare moo waral may gi teggi tuuma.