Romans 5:21 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ba tax, ni bàkkaar doon yilife ñépp ni buur, indaale dee, noonu itam la yiwu Yàlla faloo ni buur, jóge ci njub, jëm ci dund gu dul jeex. Te loolu lépp darajay Yeesu Kirist sunu Boroom moo nu ko may.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
ba tax na, noonee bàkkaar doone woon buur, ndax dee gi mu yilife ñépp, ni la aw yiw wuutoo, di buur moom itam, ndax àtteb njub gi aw yiw jural nit ñi, ba jëme leen ci texe gu sax dàkk, ci sunu ndimbalal Boroom Yeesu Almasi.