Romans 6:13 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Te buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Buleen jébbal seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayi njubadi; gannaaw yeena dekki bay dundaat, jébbal-leen Yàlla seen bopp te jébbal ko seeni cér, ngir def leen ay jumtukaayi njub.