Romans 6:19 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Xam naa ne, seen xam-xam ci mbir mii sorewul, moo tax ma yombal wax ji, awale ko ci baat yii. Ni ngeen jële woon seeni cér, jébbal leen, ñu nekk jaami lu selladi ak lu bon, di gën a jur lu bon, noonu itam léegi jébbal-leen seeni cér, ñu nekk jaami njub, ngeen door a sell.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe, ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur sellnga.