Romans 6:4 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Bi ñu nu sóobee ci ndox moomu nag, day misaal ne, dañu noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Yàlla Baay bi, te nu sóobu ci dund gu bees.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.