Romans 7:13 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ndax kon lu baax moo ma tàbbal ci dee? Mukk! Bàkkaar a ko def, ngir jikkoom feeñ; dafa gis ci lu baax loolu bunt bu mu man a jaar, ba rey ma. Noonu ndigalu Yàlla tax na, bàkkaar fés, bon ba jéggi dayo.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Lu baax loolu di yoonu Musaa, xanaa kon moo ma taxa dee? Déet kay! Bàkkaar moo feeñale noonu meloom; moo jëfandikoo lu baax, ba rey ma, ngir ndigalu yoon di jumtukaay bu bàkkaar fésale gépp mbonam gu jéggi dayo.