Romans 7:25 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Maa ngi sant Yàlla; am na kuy musle, mooy Yeesu Kirist sunu Boroom. Kon nag lii laa gis ci sama bopp: ci sama xel maa ngi topp yoonu Yàlla, waaye ci sama bindu doom Aadama maa ngi topp yoonu bàkkaar.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nuy walloo jëmmu Yeesu Almasi, sunu Sang. Kon daal man, ci sama bopp, ci sama wàllu xel, yoonu Yàlla laay surgawu, waaye ci sama wàllu yaramu suux wii, yoonu bàkkaar laay surgawu.