Romans 7:3 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Kon nag su jabar ji àndee ak beneen góor, te fekk jëkkër jiy dund, dees na ko àtte njaaloo. Waaye bu jëkkër ji faatoo, yoon jeexal na seen diggante; man na séy nag ak beneen góor, te loolu du njaaloo.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kon nag, li feek jëkkëru ndaw si di dund, su séyee ak geneen góor, ab jaalookat lees koy wax. Su jëkkër ji deeyee nag, yoon yiwi na ndaw si, te su séyee ak keneen, du doon njaaloo.