Romans 7:4 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Nii laa leen ko man a misaale, samay bokk; bi Kirist deeyee, dangeen a deeyandoo ak moom, te noonu yoonu Musaa wàcc leen. Léegi nag yéena ngi ànd ak keneen, maanaam Kirist mi dekki, ngir nu amal Yàlla njariñ.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu la deme ak yeen itam, bokk yi. Yaramu Almasi wi ngeen bennool, ci ngeen doone ñu deeyal yoonu Musaa. Noonu ngeen doone moomeelu keneen, te kooku mooy ki dekki, ngir nu meññ njariñ lu ñeel Yàlla.