Romans 7:6 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye léegi yoon wi wàcc na nu, ci li nu dee, ba rëcc cig buumam. Léegi nag nu ngi jaamu Yàlla, waxumaleen ci sàmm santaane rekk, ndax loolu wees na, waaye ci kàttan gu bees, gi nu Xelum Yàlla di may.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye tey ci sunu digg ak yoon wi nu tënku woon, la nu di ñu dee, ba teqlikoo ak moom. Moo tax nu doon ay jaam yu tegoo kilifteef gu yees, gi Noowug Yàlla indi, gannaaw ba nu wàccoo ak kilifteefu mbindu yoonu Musaa ma woon.