Romans 8:17 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Te gannaaw ay doomi Yàlla lanu, dinanu moomi lépp li Yàlla jagleel ay doomam, séddu ci ngëneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku bëgg a bokk ak Kirist ndamam ëllëg, war ngaa séddu ci ay fitnaam tey.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.