Romans 9:4 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bànni Israyil lañu, te Yàlla def na leen ni ay doomam; dëkkaloon na ndamam ci seen biir, fas ak ñoom kóllëre yi. Ñoom la Yàlla dénk yoonu Musaa, ñoom la xamal ni ñu ko war a jaamoo, ñoom la jox i digam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;