Romans 9:8 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Maanaam, soqikoo ci Ibraayma taxul a nekk doomu Yàlla, waaye juddu ci biir digeb Yàlla mooy tax a bokk dëgg-dëgg ci askanu Ibraayma.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Loolu di tekki ne du sëti Ibraayma yi ci wàllu deret ñoo di doomi Yàlla, waaye doom yi seenub juddu dëppoo ak digeb Yàlla, ñoom lañu jàpp ne ñooy askanu Ibraayma.