Titus 1:7 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte kuy sàmm mbooloo mi mooy jawriñu Yàlla, kon warul am ŋàññ, walla di ku dëgër bopp mbaa ku tàng bopp; warul dib màndikat walla xeexkat mbaa ku bëgge ci alal ju lewul.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat, njiit li war na di ku mucc sikk, gannaaw ab saytukatu kër Yàlla la. Bumu di ku bew, mbaa ku gaawa mer, mbaa ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, mbaa wutkatub am-am bu lewul.