bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
1 Corinthians 13
1 Corinthians 13
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 12
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 14 →
1
Su ma doon làkk làkki nit ñi, ak yu malaaka yi sax, te jëfewuma genn cofeel, jóolóoli bu xumb doŋŋ laa, mbaa tëggum weñ muy riir.
2
Su ma jotoon ci kàddug waxyu, boole ci xam mboolem kumpa, ak mboolem xam-xam, ak ngëm gu mat sëkk ba mana toxal ay tund, te jëfewuma cofeel, duma dara.
3
Te it su ma sarxe woon mboolem sama alal, ba sarxe sama yaramu bopp ngir ñu lakk ko, su ma jëfewul cofeel, loolu du ma jariñ dara.
4
Cofeel nag, muñ ak mbaax la. Cofeel bokkul ak kiñaan, bokkul ak jikkoy kañu ak a damu.
5
Bokkul ak jëf ju jekkadi, ak jiital sa njariñal bopp, bokkul ak naqari deret, bokkul ak denc mer.
6
Bokkul ak bége lu jubadi it, waaye moo di bége liy dëgg.
7
Cofeel moo di: lépp, nga bale; lépp, nga gëm; lépp, nga yaakaar; lépp, nga dékku.
8
Cofeel nag du jeex mukk. Su dee kàdduy waxyu, dina wéy; su dee ay làkk, dina selaw; su dee xam-xam, dina xewi.
9
Ndaxte as ndog lanu xam, te as ndog lanuy waxe kàddug waxyu.
10
Waaye keroog bu li matale dikkee, ndog si wéy.
11
Ba ma dee tuut-tànk, ni tuut-tànk laa doon waxe, di dégge dégginu tuut-tànk, di xalaate ni tuut-tànk. Waaye bi may mag laa xewil yëfi tuut-tànk.
12
Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.
13
Léegi nag liy sax moo di: ngëm ak yaakaar ak cofeel; yii yett la, te li sut ci yooyii moo di cofeel.
← Chapter 12
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 14 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16