bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Ecclesiastes 10
Ecclesiastes 10
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 9
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 11 →
1
As weñ tàbbi ci diw gu xeeñ, yàq ko; ab dof it jëfam su tuut neenal na xel mu rafet ak daraja.
2
Xelu, jubal; dofe, jàdd.
3
Te it ku dofe buy dox sax, du ànd ak xelam; ku ko gis, xam ne kii dof la.
4
Su la sa kilifa meree, bul jóge fa ñu la teg; tooñ yu mag, teey ba giif.
5
Lu mettee ngi lu ma gis fi kaw suuf, lu mel ni njuumte lu rëcc kilifa:
6
Ab dof bu ñu jox cér yu bare, boroom daraja féete suuf;
7
ma gis baadoolo war fas, kilifa di rung ni baadoolo.
8
Ku gas um yeer, repp nga tàbbi ca; ku bëtt miir, repp jaan matt la;
9
kuy yett ay doj, repp nga caa gaañu; kuy gor bant, repp nga caa loru.
10
Liggéeye weñ gu day te xacceesu ko, góor-góorlu war na ca; xelu, baaxle jariñoo.
11
Jaan màtte, balees koo jat, du njariñal jatkat ba.
12
Ku xelu àddu, mu diw yiw; ku dofe wax, sànku.
13
Bu jëkkee wax ju amul bopp, daaneele ndof gu sotti.
14
Ab dof a ngi waxa wax, te kenn xamul luy xew ëllëg. Ana ku koy xamal gannaawam?
15
Ab dof ak kër-këreem, coonoy neen; du xam sax yoonu taax ya.
16
Ngalla yeen, réew mi gone falu buur, jawriñ ña di xëye xawaare.
17
Ndokklee, yeen, réew ma as gor falu, te bu jotee, jawriñ ñay xéewlu, ngir am doole te baña màndi.
18
Tayel, puj bu màbb; yaafus, néeg buy senn.
19
Aw ñam bégal, aw ñoll bànneexal, xaalis tontu lu ne.
20
Sam xel sax bu ca saaga buur, sa néegu biir sax, bu fa saagaa boroom daraja. Xamoo picc muy yóbbu sa kàddu, mbaa njanaaw luy siiwali mbir ma.
← Chapter 9
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 11 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12