bible
ra
🌐 Language
English
Español
Français
Deutsch
Português
Italiano
Nederlands
Русский
中文
日本語
한국어
العربية
Türkçe
Tiếng Việt
ไทย
Indonesia
All Languages
Home
/
Wolof
/
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
/
Exodus 11
Exodus 11
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
← Chapter 10
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 12 →
1
Ba loolu wéyee Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Benn yarub mujjantal laay dellu wàcce ci kaw Firawna ak waa Misra. Su ko defee du leen bàyyi ngeen dem, yem ca. Da leen fiy far dàqe, ba fàww.
2
Te neel mbooloo mi, góor gu nekk ak jigéen ju nekk ci ñoom, na sàkkoo ci dëkkandoob waa Misraam, ay gànjari xaalis ak wurus.»
3
Ci biir loolu Aji Sax ji def waa Misra yéwéne leen. Musaa sax ci boppam ku ñu naw la woon ca réewum Misra, ca dagi Firawna ya, ba ca baadoolo ya.
4
Musaa daldi wax Firawna ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Bu guddi gi xaajee, maay wër Misra gépp,
5
te lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, dina dee, dale ko ci taaw bu góoru Firawna, mi toog ci jal bi, ba ci taaw bu góoru jaam bu jigéen bu féetewoo wol, boole ci luy taaw bu góor ci jur gépp.
6
Dees na dégg yuux yu réy jibe Misra gépp, lu masula am, te dootu am mukk.
7
Waaye fépp fu bànni Israyil dëkke, dara du fa wokk nit ak mala.” Su boobaa dingeen xam ne, Aji Sax jee ràññatle waa Misra ak bànni Israyil.
8
Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees.
9
Fekk na Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Li waral Firawna du leen déglu, mooy sama kéemaan yi wara fulandiwu ci réewum Misra.»
10
Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israyil, ñu génn réew ma.
← Chapter 10
Jump to:
Chapter 1
Chapter 2
Chapter 3
Chapter 4
Chapter 5
Chapter 6
Chapter 7
Chapter 8
Chapter 9
Chapter 10
Chapter 11
Chapter 12
Chapter 13
Chapter 14
Chapter 15
Chapter 16
Chapter 17
Chapter 18
Chapter 19
Chapter 20
Chapter 21
Chapter 22
Chapter 23
Chapter 24
Chapter 25
Chapter 26
Chapter 27
Chapter 28
Chapter 29
Chapter 30
Chapter 31
Chapter 32
Chapter 33
Chapter 34
Chapter 35
Chapter 36
Chapter 37
Chapter 38
Chapter 39
Chapter 40
Chapter 12 →
All chapters:
1
2
3
4
5
6
7
8
9
10
11
12
13
14
15
16
17
18
19
20
21
22
23
24
25
26
27
28
29
30
31
32
33
34
35
36
37
38
39
40